
Assadul Khadim
February 15, 2025 at 09:22 PM
Mandarga Téqéedi
1 - Xoll bu woow : nga xamne bu nuko waaré du waaru, bu gisé lo xamne war na ca amm yermandé dayy woww kong rék duca amm jénn yermandé.
2 - Bëtt yo xamne jooy ngir raggal Yalla dako jaffé lool-lool nga xamne daanaka daal ayy bëttëm dara mënuko jooy lo cilu ajju ci wallu Yalla.
3 - Ñakk kérsa
4 - Bëgg Adina ngir Adinay késsé nga xamne du ngir défaréeko Alaxira
5 - Gudd ayy mbébbét moy japp ne aww dundam désna lu baré-bari du wéyy téyit lumu amagul luné ci wérr'ak jamm'ak Allal moo ngi ñëw. Loolu day indi néew topp Yalla bari lumiy déff bakkar.
Sudé mbébbët maananm yaakar né kat Yalla mën nalafé bayyi-waat app diir téyit da ngafi mëna déff lu baax lolu moom baxna ndax bu fékké da nga japp léegi ngafiy joggé téyit dofi amm dara loy jariño day melni kon da nga naagu yermandé té kon do sawarati kon cilu baax. Luñiy bañ kay mooy mbébbët yu gudda gudd rékk mooy yakkal nitt.